Dëkkandóo XOL ak XEL - Par Cheikh FALL
Jéemantu ci ñaari dëkkandóo XOL ak XEL. Ma di ko yónnee képp ku safoo sunu kàllaama yi.
Xol da ne bëret bëg a dem . Xel ne ko déet nanu dem Boo yeggee fa nga jëm Xam né maay ki gën ci yaw.
Neel tekk ma ñëw ci yaw samab joxoñ di nga ko naw
Boo yeggee fa nga jëm Xam ne maay ki gën ci yaw
Bu yëf yi arfóo la Seex Anta wax
Bu boobaa na nga déglu ma wax
Boo yeggee fa nga jëm Xam ne maay ki gën ci yaw
Laajal jallub muus ak la ko tas
Xam la mu ëmb ak la mu nas
Boo yeggee fa nga jëm Xam ne maay ki gën ci yaw
Looy def jiital ma ca
Boo bañee fitna wàlli ca Boo yeggee fa nga jëm Xam ne maay ki gën ci yaw.
Foo jëm te ànduma ca Jafe-jafe yomb ca
Boo yeggee fa nga jëm Xam ne maay ki gën ci yaw
Gëmal te sax ci sa ngëm
Bàyyil keneen ca la mu gëm
Boo yeggee fa nga jëm Xam ne maay ki gën ci yaw
Bul jaaxle ba sëngéem
Boo ma dégloo dina la yéem
Boo yeggee fa nga jëm Xam ne maay ki gën ci yaw
Àddina tool la waaye bul ñońali
Raadul bayaat takkul ba dońali
Boo yeggee fa nga jëm Xam ne maay ki gën ci yaw
Bul di xulóo bul di xeex
Toppal ci man daldi féex
Boo yeggee fa nga jëm Xam ne maay ki gën ci yaw
Man mii maay mbërum Yàlla
Bu ma la bàyyee jaamu wàcc la
Boo yeggee fa nga jëm Xam ne maay ki gën ci yaw
Damaa wex lewet bari dole
Di riñaan di ndengeñ di weyale
Boo yëgee ak boo yëgul
Boo gëmee ak boo gëmul
Maay defar te duma laal
Maay yàq te duma taal
Boo yeggee fa nga jëm Xam ne maay ki gën ci yaw
Bu ma taaroo jëfe ma
Bu ma ñaawee teggi ma
Boo yeggee fa nga jëm Xam ne maay ki gën ci yaw.
A découvrir aussi
- La numération en langue nationale- Par Cheikh FALL *
- Jiijak Waali, l’homme-termitière- Par Cheikh Tidiane SALL *
- Première pluie - Par Fara SAMBE *
Inscrivez-vous au blog
Soyez prévenu par email des prochaines mises à jour
Rejoignez les 94 autres membres